Fiir um mbooloo weñ u firwi yi akk diw u gancax yu xeeñ
Uploaded 1 month ago | Loading
14:47
Njaxas um diw bi tudd metil ësenol di na xëcc bu baax weñ u firwi yu góor yu ndaw yi. Weñ yu góor yi soxlo na ñu si dundd ngir am katan up sëy. Metil ësenol nekk na benn ci diw u gañcax yu xeeñ yi, melni diw u garab u xot u butéel akk diw u garab u warga yu ñuy jëfëndikóo ci beneen mpàc. Su diw yooyu nekkee ci biir fiir yi d na jàpp weṅ u firwi yu gόor yi te du ñu mënëti sëy akk weñ u firwi yu jiggéen yi .
Current language
Wolof
Produced by
Agro-Insight