Xeex gunóor u pombiteer
Uploaded 1 month ago | Loading

14:59
Su sax u gunóor bi duggee ci biir pombiteer bi, ci biir tool bi walla ca bérëp u dencukaay ba, léep lay yaqq. Su xasee nekk ci biir pombiteer bi, dara mënu ko ray, doonte ay porodiwi posan la. Su gunóor yi baree, mën na ñu yaqq ngóob um lëm ci bérëp u dencukaay ba ci ay weer rekk. Ngir xeex bi mën am doole, da ngeen war jëfëndikóonyu bari te soññ baykat u seen gox bi yéep ñu def lu ni mel. Su ñu andee xeex ñun ñéep gunóor gi, mën na ñu ko faagaagal.o
Current language
Wolof
Produced by
Agro-Insight