Xeexak sane yi ci mbàq baayima yu ndaw yi
Uploaded 6 months ago | Loading

14:29
Sudee ñax mi dafa tilim jugé ci guinaw al yi bawoo ci baayima yi feebar bi laal, san yi dañuy yomba walantee ci baayima yi amul feebar bi suñuy leek. Soo bëggee xàmmee baayima yi feebar bi laal, danga wara: Xool bu baax ndax baayima yi dañuy am biir bu daw bu bari, ndax dañu tàmbali di wàññi lekk, wala ndax dañuy ñàkka mëna ànd ak yeneen baayima yi. Saytu melo bët bi ci biir ak kàrtu FAMACHA. Jéemal jëfandikoo garab yu neex wala ñax yu ndaw ngir dundal baayima yi feebar bi jàpp bañu wér.
Current language
Wolof
Produced by
Access Agriculture