Aar mboq mi ci afalàtoksin ci jamonoy ngóob mi ak lu ko jiitu
Uploaded 3 years ago | Loading
14:00
Su seen tool wérée ak nji mu teel, seen gañcax daa ñu dëgër te mën dékku socànt yeek nëb-nëb yi. Su seen mboq wowee te kiiraay li weex, góob leen ko ci diir u ñaari ay bés. Bu leen tekk muuk gub yu wér yi ci suuf, su dul loolu nëb-nëb bi day sonng seen mboq te yaqq ko ci dencc ma. Lakk leen gub yu bon yi. Bu leen jox muuk bayima yi.
Current language
Wolof
Produced by
Agro-Insight