<<90000000>> viewers
<<266>> entrepreneurs in 18 countries
<<4647>> agroecology videos
<<107>> languages available

Defar pepiñeer u kaani

Uploaded 4 years ago | Loading

Ngir defar pepiñeer, tann leen bérëp booy jottee ndox. Jëfëndikóo leen jiwu yu baax. Defar leen pepiñeer bu yaatoo benn meetar ngir mu yombb jot palaŋ yu ndaw yi. Def leen rëdd yu soreyoo 15 santimeetar. Bu leen ji pep yu bari walla yu jogeyoo su dul loolu palaŋ yi da ñuy gudd te sew, te gaawa damm ci njëmbët ma. Aar leen pepiñeer bi ci naaj bu tangg bi akk taw yu bari yi si muur ko akk ñax, xiis, walla yeneen muurukaay. Aar leen palaŋ yu ndaw yi ci yaqqkat yeek baayima yi ci tek caax u socant ci seen kaw pepiñeer. Jëmbët leen palaŋ yi ci jamono bu baax ba. Palaŋ yu dëgër te wér, ñoo gën ci tambali mbey mu sell te meññ.

Current language
Wolof
Produced by
Agro-Insight
Share this video:

With thanks to our financial partners