Ay pexe jamono ngir aar werguyaram u ginaar yi
Uploaded 1 year ago | Loading
13:40
Ndox um naan bu tilim, bérëp bu tilim akk dunnd gu bon bokk na ñu nekk ci liy inndil feebar ginaar yi. Settal leen pulaaye bi te tonni bés bu nekk nefere yi akk xont gu baaxul gi. Sellal leen ndox um naan gi akk pëndëx u kurkumà walla per u permanganaat u potasiyum. Xont leen ginaar akk dunnd gu maase. Yokk leen laac walla soble ci xont gi ngir yokk seen karaange ci feeber yi. Xob u gancax yi di fajj te wex di na dimbali ci faggu mbindéef yu bon yi. Nandal leen ginaar yi akk meew u papaaye, xoox u betel walla xollit der u garanaad. Faggaru leen ñakkum kalsiyoom u ginaar yi ci di leen jox laso walla xollit nen yu ëbb. Takk leen benn say bu ndaw bu xob yooyu ci biir pulaaye bi. Seen xet dina daqq mbindéef yu bon yooyu.
Current language
Wolof
Produced by
Atul Pagar, ANTHRA